Les poèmes de Mamadou Bara SAMB

L’HOMMAGE DU JEUNE POETE A SEYDINA MAME ALASSANE LAHI (1915-2001)

today27 avril 2023 151 1 1

Arrière-plan
share close

Marsiya Seydina Maam Alasaan Laay

Mamadou Bara Samb connu aussi sous le nom de « LEJEUNEPOETE » rend hommage à Seydina Mame Alassane LAHI, 4ème khalif de l’Imam al Mahdi (PSL), né en 1915 et rappelé à Dieu le 24 avril 2001. Fils de Seydina Mandione Lahi et de Sokhna Fatou Lahi Diop, Seydina Mame Alassane Lahi a dirigé la communauté pendant 14 ans de 1987 à 2001.

  • cover play_arrow

    Marsiya Seydi Maam Alasaan #le

1.
Al-hamdu lil-laahi nan gëm nangu ay dogalam
Ci Moom la nuy dello moo moom jaam ñi ak lu ñu am

2.
(Innaa lil-laahi wa innaa raaji’uuna ilay-
hi) Yàlla mooy joxe mooy jël noo ngi nangu jëfam

3.
Dunyaa bi workat la moo woor (Sayyidul-umami)
Moo wor Sahaaba yi waa jii Àddunaa ka xajam

4.
(Wal maytu baabun wa kullun-naasu daaxiluhuu)
Ubbil na Maam Alasaan buntam nu ñàkk jëmmam

5.
Ni Dee budoon jotu kon jullit ñi jot Alasaan
Ci ruuh yu doy ni sëriñ Raan raw na lun man a am

6.
Bu ruu gi doon jay nu def siy ndambi ndambi wurus
Ba def si Àdduna gép ngir Sëydi Raan bañ a dem

7.
(Taa’an wa Kaafan) ci weeruw Tamxarit ca la dem
Nuy seenu weer far waneen weer suux nu sax ci lëndëm

8.
Ci (Baktashin) ci atum Gàddaay ga Góor ga laxas
Bes booba tiis na ku tiitul daa newul di ku gëm

9.
Ëllëg sa ñep rot si Yoof ku ney taxaw di misaal
Mbaaxug Sëriñ Raan di jooy naa wëy fu Àdduna jëm

10.
Kep ko taseel mu la naa jaal naa la Maam Alasaan
Ku baax te yiw dem na tay ngir fekki Maam ja Limaam

11.
Dunyaa lëndëm na keroog xol yépp wéet na itam
(Shawxan wa lahfan) ci Baay Raan mii di (bahrul-karam)

12.
Fu nuy giseeti ka donnoon Maam Limaamu ci ay
Jikkoom yu màgg ya doonoon (lis-salaahi ‘alam)

13.
Woyof na loolu ni ab xob waaye soo ko xamul
Baatin ba sànk la mooy (Marjaanu) moo raw ngalam

14.
Jikkoom ya day géej Sëriñ Raan xuus ko day jafe lool
Te aw ma gaal kon xanaa ma wax ci tuuti lu yam

15.
(Taxwaa ilaahil-waraa) moo fees xolam ba mu gëm
Maamam Limaamu te wooloot Yàlla Buur bi nu moom

16.
Xoolul lu jëm ci kërug Dunyaa te feesul xolam
Misaal ci dëddu la woon moo sella moo bari ndam

17.
Moo baax te laabiir te am yërmaande am yitte lool
Kum gis teral na la Baay Raan moodi (Kanzun-ni’am)

18.
Daanay digal jaam ñi gëm Buur Yàlla bàyyi tereem
Kon gaa yi nan gëm te tuub tay jooxe ay ndigalam

19.
Lu nekk def na ko ciy xarbaax yu rëy na nga laaj
Gaayam ya Aj gaak Mulaay Hasan nga xàmmee cëram

20.
Xamoon na Seyyiduna Isaa te jël na ci moom
Haybaak xorom saak fajug aajook a yaatal kanam

21.
Toppoon na Baay Sëydi Caw fonkoon na Baay Abdulaay
Bëggoon rakkam ya Husëynook ñoom Bashiiru rakkam

22.
Daa def lu baax di ko wax xamul lu ñaaw du ko def
Amoon na mecce ba daawul wër di ñaan lumu am

23.
Ma jooy ku mel nii dafay yay nan la jooy Abadan
Wéetal nga sun xol yi Baay Raan tax nga ñeppa wedam

24.
(Bakas-samaawaatu wal-arduuna yaa ’ajaban)
Iimaan bi jooy na nitam Ihsaan bi jooy xaritam

25.
Ay Buur fayal Sëydi Raan Firdawsi ak lafa am
Dëkkal ko (xurba Imaamil-laahi) bes ba nu jëm

26.
Féetal njaboot gi palaasam may nu Baay Abdulaay
Mu wér te tal mel ni Nuuhin Rabbi yokkal fanam

27.
(Kanzul-karaamaati Bahrul – ’ilmi wal-hikami)
Cëy doomi Seyyidunaa yaa donna (husnas-shiyam)

28.
Sa mbaax gu rëy gi nga am wa réew mi seede na ko
Ludul ku tëx wàlla book iñaan ga muur ab xolam

29.
Yaa tax ba ken jooyatul Baay Raan ne yaa nu dëfal
(Antal-xaliifatu) luy leer yaa ko donna (na’am)

30.
Na Buur defal lam ndimbal yaak Ahla bayti Limaam
(Fal-laahu rabbun Kariimun) moo di Buur bi nu gëm

31.
Saxal nu Yàlla (’alal-hudaa) te may nu salaam
Te may nu (’aafiyatan) bi jaahi Seydi Limaam

32.
Taw niiru xéewal ci Baay Raan saa su nekk ba ker
Nuy xëy dajeek moom ca biir Firdawsi ak ki nu gëm

33.
(Yaa Rabbi salli ’alal-Muxtaari Sayyidinaa
Sallim ’alal aali wal ashaab) te may nu (Hikam)

Yëmbël, 2001
Baay Raan du jóg sunu xol

#lejeunepoete

Les poèmes de Mamadou Bara SAMBPOESIE

Rate it
0%
Restez informé des nouvelles publications en activant les notifications...! OK Non