
L’HOMMAGE DE MAME SAMBA LAYE SEMBARGA A CHERIF MOUHAMADOU MAKHTAR LAHI Samba Laye Sembarga
1
Nanou déme ziar sounou soppé
Moy imam bou yiw bi dou noppé
Digual ndiabot gui gnou tooppé
Walahi yaay sounou soppé
2
Cou baat bi néekh nama waïlé
Cou xéle mi gnaw nama kagnelé
Imam Mouhtaar sounou ndamlé
Walahi yaay sounou soppé
3
Thiofélou khaïssok ki laïlaa
Mathienou dof ba thia laïlaa
Ay imam gnou dof thi yaw walaa
Walaahi yaay sounou soppé
4
Anta wariissoul īllemii
Abouka baboul õūlomii
Diadouka bahroul õūlomii
Walahi yaay sounou soppé
5
Sa dieumou yiwna ba yémma
Yaa Réfét djiko barii diamma na bour bi yokou sa diamma
Walahi yaay sounou soppé
6
Sounou sagnon gnooy deukeu
Si génneu keur gnouy déekeu
Goudék beuthieuk gnouy dékeu
Walahi yaay sounou soppé
7
Xam nanni yaw yaa gui sotti
Sabarké Mame yaagui sotti
Di gnaane guenéel yi mou dotti
Walahi yaay sounou soppé
8
Imam Mouhtaar sounou soppé
Billaahi yaay sounou soppé
Tallaahi yaay sounou soppé
Wallaahi yaay sounou soppé
9
Sa soppé béey sounou soppé
Sa mak diou bahdji sa soppé
Baye Abdou Laye Moy sa soppé
Walahi yaay sounou soppé
10
Yaa Rabi yalla défeul nou
Baye Abdou Laye tégua manou
barkéem di weuy té ga wéral nou
Walahi yaay sounou soppé
11
May ko imam mooki maguam
Té Diamal ko mooki ayrakam
Sén barké baye ya ak sén maam
Walahi yaay sounou soppé