
Naar fukki ak ñaari bayit ngir sargal goorgi wuutu
Baay Laay ci njabootam ñaar fukki at ak ñaar,
#Seydinaa_Manjoon_Laay « Saahibul Karam » RTA
LIBASSE KA REND HOMMAGE A SEYDINA MANDIONE : Maandu leen ni Ndione Libasse Ka
1
#Manjoon yaadi as gor, Manjoon yaadi mbër
#Manjoon yaadi jambaar, te rëy ay ngeneel
2
#Manjoon_Laay da maa took di cambar sa mbir
Amoon yéene xidmaal la doon sab gewel
3
#Manjoon Yàlla rekkay ki xam say maqaam
Kudul Yàlla sallaaw masookoo xëyal
4
#Manjoon_Laay kudul Yalla masloo ko xool
Kudul Yalla masloo xalaat koo dawal
5
#Manjoon xam nga Dunyaa taxoon nangu woo
Mu gàkkal sa xam Yàlla Rabbul-Jaliil
6
#Manjoon_Laay da ngaa xippi janlook ki gën
Mu nandal la ñaagal la teeloon la fal
7
#Manjoon yaadi ñetteelu Ruuh yii ko gëm
Di ñaareelu ñim dénk jal bii mu jal
8
#Manjoon_Laay da ngaa jel xarañ gaak fitëm
Fegoom maanduteem ay Amar yaa Kamaal
9
#Manjoon ker ba Baay Laay ñibee yaa taxaw
dawal Sëydi « Miimun », te masloo tayel
10
#Manjoon_Laay da ngaa jaay sa cër yii jëndee
Xeyal Seydi, sak doylu rawnay misaal
11
#Manjoon sakku woo gànjarak loo dajal
Du mbooloo du ay tool du