POESIE

A.B.D.O.U.L.A.Y.E  I.B.N  I.S.S.A

today14 juillet 2023 180 6 5

Arrière-plan
share close

A.B.D.O.U.L.A.Y.E  I.B.N  I.S.S.A

Poème écrit par Baye Seydi Laye Guèye ibn Serigne Moussa Guèye Lahi

  • cover play_arrow

    Taliif Abdoulaye ibn issa BaySeydi Laye Gueye

AAbdoulaye ba ca abdoulaye ya,lii lagnu sa mame denkone.

Bbaye aak mamou yonent lala yallah tieureu lone.

Ddiiné gui weur na reew mi si say kaddu yinga djibeulone.

Oormal nga say wadiour ,diotali seni kaddu tia mame ndione,baye seydi thiaw ak mame Alassane.

Uummah bi ranié nagnu sa jeuff,do kugnuy faté ndakh borom bi mola sampone.

Lleeral nga say kaddug Mame,tasfir yi ak zikr yi weur na kürel ya.

Aaduna nga ligueyal wan leen dialouba, gnu top Yallah nguir leral seni alaxira.

Yyaatu wone am yeurmandé yilif ak yiir si alxurane ndiaboot bila Yallah denkone.

Eelimaanu Yallah bi nga dane waxtané,di diangalé aki digueul farata yi ak sunna ya.

 

Iissa rouhou lahi sa baye mola denkone foré ya, banga matalé la la dieul tegg la si wetam dja.

Bbeus banga toloo ak bunt ba ,tiala sa wote’b mame ba siiw dieum tia kaw.

Nnoflay amoko wone fi dunya lep nguir defar lignu wara fekki alaxira.

 

I– imamou imam yi moy sa mame, wax ngako fepp ni Mahdi bi dunya done xaar moy sa mame .

Ssopé talibé yi,ya soriwone si xol yi ,sa beuss ba tiissone na,guedj randouwone na.

Sseedé bi tarixa yi amone si yaw mo deugueul taxawaay ak tiofel binga amone si keuru diiné yi.

A– ABDOULAAHI

 

akhlou lahi weet nagnu,

alhamdullilah, gnun yallah begal nagnu,

Alhamdullilah, ndakh sa mame naxugnu.

Alhamdullilah, ndax sunu xel yi dal nagnu.

Yallah fayal gnu Abdoullah muy beel ca ilayiiina si wettu seydil awaliina wa seydil aaxirina.

Amiiine🙏🏾


POESIE

Rate it
0%
Restez informé des nouvelles publications en activant les notifications...! OK Non