/YAYE AÏDA CISSÉ LAHI Taalif Le poète de l'imam
Y – YAYE, SAMA YAYE
A – Aduna amoul lu geuneu meti ñakk yaye, souma menone wañi si sama dundu diox la nguir meuneu degaat sa baat, guissaat sa ré dja, guissaat sama weeru waay ba.
Y – Yaa nekkoon jambaar si kër Baye,ya nekkoon yaye bi geunoon si ñun.
Yaañu yarr,aar ñu, yiir ñu, matalè nga sa wareef si ñun.
E – Euleuk dinañu la seddel sa jeuf dju baax si kanamu sunu Borom,sa taxawaay ak jubal sa ndiaboot si yoone bu baax bingañu beugaloon.
A – Aljummah 18 septembre 2015 beuss bobu dotuñu ko meusseu faté.
Tieuy beuss bobu.
Diissone na t dootuñu dundati luko geuneu diss.
I – indi xibaar buñu tiss,aduna daanu sunu kaw. Yaye mo delou tia Boromam mou nek luñu mënul miss.
D – dem nga bayi fi ndiaboot gui,bayi len ak xol yu fess, rongoñ yuy tuuru,tumurankê dugu ndax ñakk yaye moy ñakk nga kila geuneu beug si kaw suuf.
A – Aduna woratina,dieul na weeru waay bi geuneu woor,ki meuneu tekk dundeum nguir nga dundu,ki saña bonal lepam nguir nga baax.
C – Coofeel binga amone si ñun diegui wone na dayo buñu mënul woon nateu, mbeuguel bu dëggu la Yaye di dieumeulè si dom.
I – iiman bu weer dieumeuléko si sa Boroom swt, gëm Mame Baye Lahi asws,nala Yallah fay lepp linga ligeey si diiné gui. Amiiiine 🙏🏾
S – Sa taaw ABDOULAYE SYLLA ak AWA diooy nañu, NGONÉ ak OUSSEYNOU nopiwuñu, BAYSEYDI ak BAMAR wéet nañu t ABY ngui ladj ndax dinañ la guissaat ndax rongoñ yi feraguñu.
S – Sofi yagone mu done lu geun si ñun,sa dem gui doone la lu wañeeku si ñun,danga nekone ku soriwone si ñun,ñu beugone la delo lepp linga defoon si ñun
E – Elimaanu Yallah bi nga beugone,geumone ko,fuñla fekk yangui zikr t dieufé ndigël ya
L – Là illaha Illa làh lañ la gunguè délola sa Borom,diamalaye nga teud si wetu Xayru Xalxi lahi
A – Alhamdoulilah, duñu diouk
di sant Yallah si limuñu diox Yaye bu melni yaw
Y – Yaye bi geun dila ñaanal nga took si peeyum ilayina
E – Eutou aldjana yi lañulay naanal ngafay daagu ak Baay Mussa Gëy Lahi ngen bokk jotaay ak Mustafaa asws🙌🏾