play_arrow

Les poèmes de Mamadou Bara SAMB

LE JEUNE POETE CHANTE BAYE LIBAAS ÑAŊ

micMamadou Bara SAMB LAHItoday8 avril 2023 328 4 3

Arrière-plan
share close
  • cover play_arrow

    LE JEUNE POETE CHANTE BAYE LIBAAS ÑAŊ Mamadou Bara SAMB LAHI


BAYE LIBAAS ÑAŊ, Poète du Saint-Maître (psl)

  • cover play_arrow

    Baay Libaas Naŋ lejeunepoete

1
Wolof yooyu laa miin
Te moom laay defum njiin
Teral kii fi kañ Njiin
Te way waa këram

2
Ki jiitoon ci géejam
Mu nàndal ko leeram
Mu xëy sotti luy lem
Te raw neexitam

3
Budaan wax ci Baay Laay
Bégal kuy wuyoo laay
Budoon wax ju ñuy jaay
Ku fiy am njëgam!

4
Ba Yonnen ba wootee
Ba noonam ya wuutee
La Hassaan taxaw tee
Ñu xas ab sangam

5
La muy wax di jaasi
Di semmal (xannaasi)
Sagal (Xayru-naasi)
Bégal ab xolam

6
Busayree ko aw jël
Di màddaa ka fental
Ki tax ñéppa woomal
Te jox leen ndabam

7
Yonnen xëy ñëwaat fii
Libaas yuuxuwaat fii
Di way (duuna xawfi)
Ba xëy am ngërëm

8
Ni Baay Laay Amul Maas
Ku koy way manul jaas
Libaas ñaŋ di (nibraas)
Bi leeral mbiram

9
Awaay Baay Libaas ñaŋ
Wedam loo nga yooy kaaŋ
Ya daan jéem a bañ Sang-
ga bii nuy xalam

10
Da ngaa way te tooñoo
Waxal kii nu feeñoo
Yëgal leen te gaañoo
Ki xallam ngiram

11
Limamook i Iisaa
Ku leen way keroog saa
Du gis yoonu (buusaa)
Du ñàkkam xelam

12
Damay ñaan bu lay Buur
Takkal say garaat joor
la may yooyu lay muur
nga woo ma, ni am

13
Dinan sax di kontaan
Ci say way di waxtaan
Ci say mbir di ñeetaan
Sa may yii nga am

14
Na buur yokk xéewal
Libaas ñaŋ mi siiwal
Mbëram, may nu woomal
nu jox nug njubam

15
(Allaahumma salli)
(Alaa Xayri rusli)
Njabootam te folli
Ku jàppul mibram

#lejeunepoete


Les poèmes de Mamadou Bara SAMBPOESIE

Rate it
0%
Restez informé des nouvelles publications en activant les notifications...! OK Non