La Vie de l'Imam Al-Mahdi (psl)

LEJEUNEPOETE REND HOMMAGE AU MESSAGER D’ALLAH (PSL) : Ay Mustafaa sama Waa ji

today3 mai 2023 85 1

Arrière-plan
share close

Lejeunepoete mu ngi leen di ñaanal Ñaanug Jàmm ak xéewal.

Xerawlu leen ñetti xasida yii mu def ci Sanga bu tedd bi SAWS.

1. Nàndal ma (Ndar, 22 Octobre 2020)

2. Ay Mustafaa sama Waa ji (Yëmbël, 22 Juin 2022)

3. Maa ngi nii ñàkk ngay ku woomle ( Yëmbël, 26 Mars 2023)

Jërëjëf Sëydinaa Limaamu Laay, teral nga nu Démb, teral nu Tay. Lu nu la way doyul

  • cover play_arrow

    Ay Mustafaa sama Waa ji #lejeunepoete

1
Ay Mustafaa sama waa jii maa ngi nii di la xaar
Ab tab du neenal ku yaakaar Sanga kaay sowe ma

2
Ay Mustafaa maa ngi lay woo Sanga kaay wuyu ma
Njool awma ken ku la moy ay Sanga xettali ma

3
Ay Mustafaa du ma diis ken saa tawat
duma dem
Feneen fu romba sa kër sagal ma soppe sama

4
Ay Mustafaa nu samay tiis tollu yit du ma dañ
Di sant ak xëy di ñaan sa leer yi jublusi ma

5
Ay Mustafaa du ma saalit mukk jombanamaat
Jàmbat lu weesu jubook yaw Sanga kaay gane ma

6
Lum yàgg yàgg du jaas bis Njool mi wàllusi ma
Lu tiis wi rëy rëy bu nee mël lépp teggiku ma

7
Loxoom bu sell ba lay jël teg ca bopp ba ëf
Luy jàngoroo ki mettit ne mes keroog sori ma

8
Mu làmb saa xol bi leeram yéppa far solu ma
Ma mujja janlook (Xaxiixaam) Cër ya wàllisi ma

9
Ma naa ko Sanga nammoon naa gis la boobu ba tay
Mu ree ma lëng ma may jooy naa ko Njool jege ma

10
Mu naa ma luy sa tawat ma naa ko Njool sama tiis
Mooy xëy di saafonte ak yaw ak janook sa jëmma

11
Mu naa ma bis ni ki tay foo geestu gis ma sa wet
Loo laaj ma may la ko dootoo tiit wa rabis-samaa

12
Ma naa ko Njool am la daa doy sëkk lool sama xol
Ludul liggéeyal la Maam waat naani séentu wuma

13
Gaa yoo ya ngay fal ñu lay xitmaal ci waxtu wu ne
Laa sàkku doon cam si leen jiital ci jii jamana

14
Jaylaani yaa ko faloon, Tiijaani yaa ko mayoon
Mawdooki Ahmadu yaa leen sedde (kulla munaa)

15
Yaa sedd Jàmbur ya Maxtaar Looki Baay Jibi Gay
Abdooki ñoom Cerno Mbay solal ma seen mbuba ma

16
Nàndal ma Kaas bi Yonnen solal ma (manto) bi Njool
Lemal ma Yoon wi ma janlook Buur bi xëy bind ma

17
Ma mujja doon jaam bi Koy bégal ci bàkk Ko njël
Bu nit ñi dëppooy nelaw kàddoom ga yeelusi ma

18
Yonnen sagal ma raxas saag ruuh te xettali ma
Yonnen sagoo ma te ful saab cër ca séddale ma

19
Na Yàlla julli ci yaw sëlmël ci yaw abadan
Foo jëm ma gunge la loo am may ma Sanga sama

22/06/2022


La Vie de l'Imam Al-Mahdi (psl)Les poèmes de Mamadou Bara SAMBPOESIE

Rate it
0%
Restez informé des nouvelles publications en activant les notifications...! OK Non