
MARSIYA MAME NDIONE AK SERIGNE ABLAYE : L’hommage de Mame Samba Laye SEMBARGA Mame Samba Laye SEMBARGA
1 bi bismil ilaahi. bi Siri laahi . imamil laahi rassoulou laahi.
2 dég louma touti. ma nétalééti. thi ahlou baïti. rassoulou lahi.
3 li yala daadéf. yonén ya daadéf. Yanxoup wa Youssouf. rassoulou lahi.
4 Ibrahimaa ak Iskhakh dom ak. Ismaa ilaay miy mak. rassoulou lahi.
5 Zakariya wa Yaxeya. lii moodi aaya. doundam ga moya. rassoulou lahi.
6 Moussa wa Haron. nioo bokou ab nooon nioo ande aw yon. rassoulou lahi
7 limoodi tarikh. yi fégn di khar bakh. bour yala moobakh. rassoulou lahi.
8 Seyna Mandione mi. ak Abdoulaye mi. nioo ande atte mii rassoulou lahi
9 yala léen boolé. thi wéer wi bolé. séne niaan yi bolé. rassoulou lahi.
10 Seyna Mandione Laye. ak dom dji Ablaye. Abdou ni yay baye . rassoulou lahi
11 ki yar domam DJI. té naako Tay DJI. yay digoup Mame DJI. rassoulou lahi
12 Baye Abdou na baye. Lo wax ma déf baye guir yadi Baye Laye. rassoulou lahi
13 ziar général. Abdou ko yémbal. bégeul ki bour fall. rassoulou lahi
14 Mame Ndione la bour fale. guina magam néle. thik MAK ladiot fale. rassoulou lahi
15 Baye Abdou Laye tam. thik mak ladiot tam. khilafa mom tam. rassoulou lahi
16 Ibnou Limamou. sibtou Limamou. khalifay Limamou. rassoulou lahi
17 njii niaar niou bolé. yala léen bolée. thi diiné djilée. rassoulou lahi
18 thi barkép njiiniar. yala nou bour arr. té yokou séen léer. rassoulou lahii
19 yén gaayi waa yoff. gni khélou Tay xéff. naguén réfét dieuf. rassoulou lahi
20 yén gaayi layéne. niou roy Thi Mame Ndione. té sakh thiwi yoone.rassou lahi
21 Baye Abdou Laye Thiaw. thiréw mi foo aw. niou naala yaa yiw . rassoulou lahi
22 ya donou Inssa. Mandione wa Inssa. mou ndaw di Insa. rassoulou lahi
23 ak Reydina Raane. magam dia Baye Rane mo bakh di Rahmane. rassoulou lahi
24 niou niaan té yakar. thi yala miy arr. thi barké mouhtar . rassoulou lahi
25 sali wasalim. ãnlaa moukarim. bi ismi anhzam. rassoulou lahii