CONTRIBUTION

POESIE : Al Khaliifa Muhamadu Al Amiin

today19 novembre 2025 124 1

Arrière-plan
share close

Al Khaliifa Muhamadu Al Amiin

1. Wa Ahloulaahi ñu delou santa Rabbanaa, ci Al Amiine mi ñepp woolou jiitou naa
2. Alhamdoulilaahi santa Buur ci ay doggalam, mo dieul Muxtaarunaa mu dem Ilayiinaa
3. Guddig fukeel ci shawaal la mbir ma xew, ñepp jaaxlé naa Baay Dudu Laay laaxu naa
4. Nirook demouk Imaama laahi Xayrunaa, muy bess yu neew guinaaw Kori ga deuppu naa
5. Deuppook bessub sarakh ba Imaamana, defoon kerook niaari naggam ya yeemé naa
6. Fajar ga xarr ñeepp yeewu tey deegg naa, Muxtaarunaa Baay Doudou Laay ñibi naa
7. Baay Maam Libaass jiiteul njaboot ga kerook, jeebeul ko Laahu ak Maamam ja Xayrunaa
8. Uuffeul ko baay ba sopeem ba Seyna Manjoon, biir Jammalaahi lii werr neu Rabbanaa
9. Daaluun la took yaggul Baay Seynaa nga naa, yaaxul itam kone nane santa Rabbanaa
10. Nanu guem té toppu Al Khaliifa Baay Lamine, sam’an wa taàhatane mo warr nguir Rabbanaa
11. Al Amiina baax tay jii mooy Limaamu Laay, lii dey du jaass mburtum Sadiix ba maagga naa
12. Ku fonka Maam ngoyal ca seutt ba moodi li warr, Baay Al Amiine matt na mooy Imaamanaa
13. Nangul ziaar bi yaa seydinaa yaa sanadii, Baay Momadoo yalna ngafi yaag aaminaa
14. Taxawlunaa ci Maam Libaass zul mu’hanriif, mo wané yoon wi ba xol yeppeu sedda naa
15. Kerr ba tiiss ba amé feka Baay Lamine tukki naa, mo oûff njaboot gui taxawu mak ja watia naa
16. Yaa matt Imaam takh nga teunk ñepp té naa, nane toppa Baay Lamine wormaal ko jiitu naa
17. Wormaal ko warna ndakh mofi Limaamu Laay, wuuté amul ci keur gui lepp yemba naa
18. Yaaggal té werr yaak say rakka Baay Maam Libass, Muxtaarunaa bun Baabacar Imaamanaa

Salaatan wa tasliiman ala saydil waraa Maam Limaamu Laay leeram ya ño raw yu jantt bi

#Sibt_Sadiix

Écrit par: soodaan3

Rate it

0%
Restez informé des nouvelles publications en activant les notifications...! OK Non